Laxdariyu en wolof { UBBITEG TÈERE BI } Nu tàmbalee sunu jëf ci tudd Yàlla. Yàlla miy xéewale bépp mbindeef fii ci àdduna, tey yërëm ku ko soob ëllëg (ca allaaxira).Yàlla na Yàlla julli ci sunu sang bi Muhammat, ak i ñoñam, ak i saabaam, te musal ko.Mboleem cant yi ñeel na Yàlla, moom miy Boroom mbindeef yi. Te dollikug xéewal, ak dollikug mucc Yàlla na nekk ci sunu sang Muhammat, ka mottali ñañu soloo, tay njiitu ñañu yónni. { PAS-PAS } Li njëkk a war ci mukàllaf mooy mu wéral ngëmëm, topp mu xam la nga xam ne dana yéwénal ci moom faratay jëmmam, lu mel ni àttey julli, ak laab, ak koor. Dana war ci moom mu wattandiku ci daytali Yàlla yi, te mu taxaw ci ay ndigalam, te muy tuub jëm ci Yàlla, (mu sell mi), lu jiitu muy mer. (Wax Wolof Ak Xamle) Bind ñaar (2) *Laxdariyu * { SÀRTI TUUB } Sàrti tuub ñooy : réccu ca la weesu, ak yéenee bañ a dellu ci bàkkaar ci li des ci sag dund, ak bàyyi moy ga ca saa si bu dee nekkoon nga aji-làmboo ci moy.Du dagan ñeel mukàllaf mu yeexe tuub, te déet muy wax ba Yàlla gindi ma. Naka loolu bokk na ci mandargay texeedi, ak jéppte, ak gumbag xol. { TEGGIINI LISLAAM } Dana war ci mukàllaf mu wattu làmmiñam ci ay ñaawtéef, ak wax ju ñaaw (saaga, xaste), ak ngiñal pase, ak gëdda ab jullit, ak doyadal ko, ak ƞàññ ko, ak ragal loo ko ci lu dul dëggug kojug yoon.Dana war ci mukàllaf mu wattu gisam ci xool jëm ci lu araam. Du dagan ñeel ko muy xool jëm ci jullit xool boo xam ne da koy lor, lu dul ni dafa nekk faasix (kàccoor). Kon dana war tongoo ak moom (gàddaay ko). (Wax Wolof Ak Xamle) Bind ñatt (3) *Laxdariyu * Dana war ci mukàllaf mu wattu gisam ci xool jëm ci lu araam. Du dagan ñeel ko muy xool jëm ci jullit xool boo xam ne da koy lor, lu dul ni dafa nekk faasix (kàccoor). Kon dana war tongoo ak moom (gàddaay ko).Dana war ci mukàllaf mu wattu mbooleem i céram lu mu man (kem kàttanam), te muy bëgg (sopp) ngir Yàlla, muy bañ ngir Yàlla, muy gërëm ngir Yàlla, muy mere ngir Yàlla, muy digle luy tax a am aw yiw, tay tere lu bon (lu ñu sib).Araam na ci mukàllaf muy fen, ak jëw, ak rambaaj, ak rëy, ak naw jëf (yéem boppam), ak ngistal, ak ndéggtal, ak kañaan, ak mbañeel, ak seet ngëneel ci keneen, ak jëwe bët (regeju), ak jëwe gémmiñ (ngeleju), ak po (mariyaas, damye, futbal, rawante), ak reetaanu xol, ak njaalo, ak xool jëm ci jaambur bu jigéen, ak bànneexu ciy waxam, ak lekk alalu nit ci lu dul teeyug bakkanam, ak lekk alal ci tinu nit , walla ci (turu) diine, ak yeexe julli ba génn waxtu wa.Daganul ci mukàllaf muy ànd ak kàccor, walla jekkiyaale (toog) ak moom ci lu dul lor (ngànt). (Wax Wolof Ak Xamle) Bind ñent (4) *Laxdariyu * Déet muy sàkku ngërëmal mbindeef ci senjug (merug) Aji-Bind Ji Yàlla (tudd naa ag sellam) wax na : « Naka Yàlla ak Yònnentam ñoo gën a yayoo ñu sàkku seen ngërëm, bu dee nekk nañu ay way gëm ».Yònnent Bi (Yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc) wax na ne : « Bul topp menn mbindeef ci moy Aji-Bind Ji».Daganul ci mukàllaf mu jëf jenn jëf mbate mu xam àtteb Yàlla ci jëf ja. Nay laaj way xam ña, te muy roy ci way topp ña sunnas Muhammat (Yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc). Mooy ña nga xam ne dañuy tegtale ci topp Yàlla, di wattandikuloo (moytuloo) ci topp saytaane. Déet muy gërëm ñeel boppam (bëgg ci boppam) loo xam ne gërëm na ko way-falas (kutus) ña. Mooy ña nga xam ne sànk nañu seen dund ci lu dul topp Yàlla mu kawe mi. Woo naa (tudd naa) seen ñàkk nga (pert), seen jooy yu yàgg Bis-Pènc ba.Noo ngi ñaan Yàlla (tudd naa ag sellam) mu dëppale nu ci topp sunnas sunu Yònnent, sunu rammkat, sunu sang Muhammat (Yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc). (Wax Wolof Ak Xamle) Bind juróom (5) *Laxdariyu * { XAAJI LAAB } Laab ñaari xaaj la: laabu hadas (dindi toj ci njàpp, walla ci cangaay) ak laabu xabas (dindi sobe su la taq ci yère, walla yaram, walla bérab bi ngay jullee ). Ñaar yépp duñu wér lu dul ci ndox mu laab, te man a laabal. Mooy ndox moo xam ne soppikuwul meloom wa, walla cafkaam ga, walla xetam ga, ci loo xam ne dana teqalikoo ak moom ca la gën a not, lu mel ni peterol, ak diw, ak ñaay ak nékk (gares), diwu segal), ak tèru jur (tilim), ak saabu, ak tèru nit (mbalit), ak yu ni mel.Aayul ci suuf, ak dewnde (ban bu ñuul), ak ceñ (xorom), ak mbaala-mbaal ak ñax mi sax ci ndox, ak yu ni mel. (Kon yii mu mujj a tudd buñu soppee ndox du ko tee laab te man a laabal.) (Wax Wolof Ak Xamle) Bind juróom benn (6) *Laxdariyu * { LAAB CI SOBE } Bu dee sobe sa ràññeeku na, raxaseef bérab ba. Bu dee lënt na, raxaseef mbalaan ma léppam (maanaam yère ba).Ku sikki-sàkka ci laalug sobe, na ko wis. Bu dee laal na ko, mu sikki-sàkka ci sobewoom, déet wis di ko war.Ku fàttaliku sobe te nekk ci julli, na ko dog, lu dul ne dafa ragal génn waxtu wa.Ku julli ànd ak sobe di aji-fàtte, te mu fàttaliku ko ginnaaw ba mu sëlmalee, na baamu ca waxtu wa (maanaam bu waxtu wa jàllee du ko baamu). (Wax Wolof Ak Xamle) Bind juróom ñaar (7) *Laxdariyu * { FARATAY NJÀPP } Faratay njàpp juròom ñaar lañu: yéene, ak raxas kanam (sëlmu), ak raxas ñaari yoxo ba ca ñaari conca ya, ak masaa bopp, ak raxas ñaari tànk ba ca ñaari dojoor ya, ak …
Laxdariyu en wolof Lire la suite »