Laxdariyu en wolof
{ UBBITEG TÈERE BI }
Nu tàmbalee sunu jëf ci tudd Yàlla. Yàlla miy xéewale bépp mbindeef fii ci àdduna, tey yërëm ku ko soob ëllëg (ca allaaxira).
Yàlla na Yàlla julli ci sunu sang bi Muhammat, ak i ñoñam, ak i saabaam, te musal ko.
Mboleem cant yi ñeel na Yàlla, moom miy Boroom mbindeef yi. Te dollikug xéewal, ak dollikug mucc Yàlla na nekk ci sunu sang Muhammat, ka mottali ñañu soloo, tay njiitu ñañu yónni.
{ PAS-PAS }
Li njëkk a war ci mukàllaf mooy mu wéral ngëmëm, topp mu xam la nga xam ne dana yéwénal ci moom faratay jëmmam, lu mel ni àttey julli, ak laab, ak koor. Dana war ci moom mu wattandiku ci daytali Yàlla yi, te mu taxaw ci ay ndigalam, te muy tuub jëm ci Yàlla, (mu sell mi), lu jiitu muy mer.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar (2) *Laxdariyu *
{ SÀRTI TUUB }
Sàrti tuub ñooy : réccu ca la weesu, ak yéenee bañ a dellu ci bàkkaar ci li des ci sag dund, ak bàyyi moy ga ca saa si bu dee nekkoon nga aji-làmboo ci moy.
Du dagan ñeel mukàllaf mu yeexe tuub, te déet muy wax ba Yàlla gindi ma. Naka loolu bokk na ci mandargay texeedi, ak jéppte, ak gumbag xol.
{ TEGGIINI LISLAAM }
Dana war ci mukàllaf mu wattu làmmiñam ci ay ñaawtéef, ak wax ju ñaaw (saaga, xaste), ak ngiñal pase, ak gëdda ab jullit, ak doyadal ko, ak ƞàññ ko, ak ragal loo ko ci lu dul dëggug kojug yoon.
Dana war ci mukàllaf mu wattu gisam ci xool jëm ci lu araam. Du dagan ñeel ko muy xool jëm ci jullit xool boo xam ne da koy lor, lu dul ni dafa nekk faasix (kàccoor). Kon dana war tongoo ak moom (gàddaay ko).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñatt (3) *Laxdariyu *
Dana war ci mukàllaf mu wattu gisam ci xool jëm ci lu araam. Du dagan ñeel ko muy xool jëm ci jullit xool boo xam ne da koy lor, lu dul ni dafa nekk faasix (kàccoor). Kon dana war tongoo ak moom (gàddaay ko).
Dana war ci mukàllaf mu wattu mbooleem i céram lu mu man (kem kàttanam), te muy bëgg (sopp) ngir Yàlla, muy bañ ngir Yàlla, muy gërëm ngir Yàlla, muy mere ngir Yàlla, muy digle luy tax a am aw yiw, tay tere lu bon (lu ñu sib).
Araam na ci mukàllaf muy fen, ak jëw, ak rambaaj, ak rëy, ak naw jëf (yéem boppam), ak ngistal, ak ndéggtal, ak kañaan, ak mbañeel, ak seet ngëneel ci keneen, ak jëwe bët (regeju), ak jëwe gémmiñ (ngeleju), ak po (mariyaas, damye, futbal, rawante), ak reetaanu xol, ak njaalo, ak xool jëm ci jaambur bu jigéen, ak bànneexu ciy waxam, ak lekk alalu nit ci lu dul teeyug bakkanam, ak lekk alal ci tinu nit , walla ci (turu) diine, ak yeexe julli ba génn waxtu wa.
Daganul ci mukàllaf muy ànd ak kàccor, walla jekkiyaale (toog) ak moom ci lu dul lor (ngànt).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent (4) *Laxdariyu *
Déet muy sàkku ngërëmal mbindeef ci senjug (merug) Aji-Bind Ji Yàlla (tudd naa ag sellam) wax na : « Naka Yàlla ak Yònnentam ñoo gën a yayoo ñu sàkku seen ngërëm, bu dee nekk nañu ay way gëm ».
Yònnent Bi (Yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc) wax na ne : « Bul topp menn mbindeef ci moy Aji-Bind Ji».
Daganul ci mukàllaf mu jëf jenn jëf mbate mu xam àtteb Yàlla ci jëf ja. Nay laaj way xam ña, te muy roy ci way topp ña sunnas Muhammat (Yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc). Mooy ña nga xam ne dañuy tegtale ci topp Yàlla, di wattandikuloo (moytuloo) ci topp saytaane. Déet muy gërëm ñeel boppam (bëgg ci boppam) loo xam ne gërëm na ko way-falas (kutus) ña. Mooy ña nga xam ne sànk nañu seen dund ci lu dul topp Yàlla mu kawe mi. Woo naa (tudd naa) seen ñàkk nga (pert), seen jooy yu yàgg Bis-Pènc ba.
Noo ngi ñaan Yàlla (tudd naa ag sellam) mu dëppale nu ci topp sunnas sunu Yònnent, sunu rammkat, sunu sang Muhammat (Yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind juróom (5) *Laxdariyu *
{ XAAJI LAAB }
Laab ñaari xaaj la: laabu hadas (dindi toj ci njàpp, walla ci cangaay) ak laabu xabas (dindi sobe su la taq ci yère, walla yaram, walla bérab bi ngay jullee ). Ñaar yépp duñu wér lu dul ci ndox mu laab, te man a laabal.
Mooy ndox moo xam ne soppikuwul meloom wa, walla cafkaam ga, walla xetam ga, ci loo xam ne dana teqalikoo ak moom ca la gën a not, lu mel ni peterol, ak diw, ak ñaay ak nékk (gares), diwu segal), ak tèru jur (tilim), ak saabu, ak tèru nit (mbalit), ak yu ni mel.
Aayul ci suuf, ak dewnde (ban bu ñuul), ak ceñ (xorom), ak mbaala-mbaal ak ñax mi sax ci ndox, ak yu ni mel.
(Kon yii mu mujj a tudd buñu soppee ndox du ko tee laab te man a laabal.)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind juróom benn (6) *Laxdariyu *
{ LAAB CI SOBE }
Bu dee sobe sa ràññeeku na, raxaseef bérab ba. Bu dee lënt na, raxaseef mbalaan ma léppam (maanaam yère ba).
Ku sikki-sàkka ci laalug sobe, na ko wis. Bu dee laal na ko, mu sikki-sàkka ci sobewoom, déet wis di ko war.
Ku fàttaliku sobe te nekk ci julli, na ko dog, lu dul ne dafa ragal génn waxtu wa.
Ku julli ànd ak sobe di aji-fàtte, te mu fàttaliku ko ginnaaw ba mu sëlmalee, na baamu ca waxtu wa (maanaam bu waxtu wa jàllee du ko baamu).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind juróom ñaar (7) *Laxdariyu *
{ FARATAY NJÀPP }
Faratay njàpp juròom ñaar lañu: yéene, ak raxas kanam (sëlmu), ak raxas ñaari yoxo ba ca ñaari conca ya, ak masaa bopp, ak raxas ñaari tànk ba ca ñaari dojoor ya, ak ragg,(maanaam fu ndox mi jaar nga jaarale fa sa loxo bomb) ak gaaw nga (maanaam njàpp mépp nga def ko ci benn jataay te bañ koo dagg).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind juróom ñatt (8) *Laxdariyu *
*{SUNNAY NJÀPP} *
Sunnay njàpp juròom ñatt la ñooy: Raxas ñaari yoxo ya, ba ca ñaari tikku jara ya, ca tàmbali ga, ak gallaxndiku, ak saraxndiku, ak fiiru, ak delloo masaa bopp, ak masaa ñaari nopp, ak yeesal ndox ma ñeel leen, ak toftale diggante farata ya (maanaam la war a jiitu, jiitu, la ca war a topp, topp ca).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind juróom ñent (9) *Laxdariyu *
{ DABAATAL LUÑU FÀTTE CI CÉRI NJÀPP }
Ku fàtte benn farata ci njàppam, te fàttaliku ko ci lu jege, na ko def ak la ca ginnaawam (niral: Ku fàtte raxas yoxo ba ca conca ya, ba mu tolloo ci raxas tànk ya xelam dem ca kon day raxas yoxo ya, te baamu li ci topp). Bu yàggee, na ko def moom dong te yéene ko, daa di baamu la mu julli woon, la ko jiitu. (Niral: Ku julli woon tisbaar ba noppi, xelam dem ci ne ba muy jàpp bàyyi woon na ab farata, kon day dem raxas céru farata booba te mu ànd ak yéene, daa di julliwaat tisbaaram).
Bu bàyyee sunna, na ko def, te du baamu la mu julli woon. (Day koy def rekk ngir bu fekkee daa bëgg a julliwaat ca njàppam moomee.)
Ku fàtte déeneer, (ab weex-weex) na ko raxas rekk ànd ak yéene. Bu jullee lu jiitu woon loolu, na ko baamu.
Ku fàttaliku gallaxndiku, walla saraxndiku ginnaaw ba mu tàbbee ci raxas kanam mu fàttaliku ko, déet muy dellusi ci ñoom ñaar, na wéy bu njàpp ma matee mu door leen a def.
*(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk (10) *Laxdariyu *
{ NGËNEELI NJÀPP}
Ngëneeli njàpp ñooy: Wax bismil Laah, ak soccu, ak dolli ca ragg bu njëkk ba ca raxas kanam, ak ca ñaari yoxo ya, ak tàmbalee ca njëlbéenug bopp (maanaam fa kawar baaxoo sax), ak toftale sunna ya, ak néewal ndox ma ca kaw cér ya, ak njëkke nday-joor ci càmmooñ.
Dana war xaliil (teqale) waaraami yoxo ya. Sopp nañu ko, ca waaraami tànk ya.
Dana war xaliil (teqale) sikkim bu woyof ci njàpp, wuute ak bu fatt. Dana war xaliil (teqale) ko ci cangaay donte ne bu fatt la.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak benn (11) *Laxdariyu *
{ YIY FIRI (TOJ) NJÀPP }
Yiy firi njàpp ay toj lañu ak i sabab.
Way toj yi ñooy : gaanuwaay (saw), ak dem àll (puub), ak ngelawal (doxot), ak masiyu ak wadiyu (ndox la mom ci ginaaw saw la ëpp lu muy gènn).
Way sabab yi ñooy : nelaw yu diis, ak xëmte, ak màndite, ak ndof, ak fóon jigéen , ak laal jigéen, bu dee jublu nga ca bànneex, te am ko ca, walla nga am ko ca te jubluwòo ko ca, walla jubluwòo ko ca te am ko ca, ak laal sa sàkkara ci biir tenq walla ci biiri waaraam.
Ku sikki-sakka ci toj dana war ci moom njàpp lu dul ne dafa nekk aji-jaxjaxal, kon déet dara di ko war (waaye julli gu nekk dana ko jàppal njàppum boppam). Dana war ci mukàllaf raxas sàkkaraam sépp bu masiyu génnee ci moom, déet muy raxasaale ñaari waay-yoore ya . Masiyu mooy ndox may génn ci bànneex bu ndaw ci xalaat jigéen, walla xool ko, walla leneen…
*(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak ñaar (12) *Laxdariyu *
{ WAY-TEREY TOJ }
Daganul ñeel ki amul njàpp muy julli, walla tawaaf (wër Kaaba ga), walla laal yaxu Alxuraan (ba di aji-màgg), walla deram ba ko takk, ci loxoom, walla ci bant, walla lu ni mel, lu dul ab jukki (xaaj) ba tukkee ci Alxuraan ñeel ndongo bay jàng ca jukki (xaaj) ba, ak njàngalekat ba.
Déet laal àlluwa Alxuraan (ba di aji-màgg) ci lu dul njàpp, bu dul kiy jàng ci moom, walla kiy jàngale di ko ko toppal. Ndaw lu laal Alxuraan moom ak mag ñoo yem ca bàkkaar ba, waaye bu fekkee mag moo ko ko jottaliloo mag ma mooy gàddu bàkkaar ba.
Ku julli ci lu dul njàpp te tay ko moom yéefër la, (yal na nu ci Yàlla musal).
(Wax Wolof Ak Xamle)
bind fukk ak ñatt (13) *Laxdariyu *
{ YIY WARAL CANGAAY }
Cangaay dana war ci ñatti mbir: Ci janaba, ak mbërëg, ak gësin (dereeti wësin).
Janaba ñaari xaaj la.
Bu njëkk ba mooy: Génnug (maniyu) ci bànneex ba mu baaxoo àndal, ci nelaw walla ci yewwu, ci booloo (sëy), walla ci leneen.
Ñaareel ba mooy: Fàddug kaaŋ (bopp sàkkara) ci pëy.
Ku gént ci nelaw mel ni moom mi ngi booloo (sëy), te (maniyu) génnul ci moom, dara du ko war.
Ku fekk ci mbalaanam (yéere) (maniyu) mu wow, te xamul kañ la ko taq, na sangu te baamu la mu julli woon ci ginnaaw nelawam yi mujj ci mbalaan ma (yéere ya).
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak ñent (14) *Laxdariyu *
{ FARATAY CANGAAY }
Faratay cangaay ñent lañu ñooy: Yéene (fi nga koy defee nag mooy booy raxas awra wa) ak gaaw, (maanaam cangaay lépp nga def ko ci genn anam te bañ koo dog) ak ragg (bomb), ak matale mbooleem yaram wa ak um ndox.
{ SUNNAY CANGAAY }
Sunnay cangaay juròom lañu ñooy: Raxas ñaari yoxo ba ca ñaari tikku jara ya, (mel ni ci njàpp) ak gallaxndiku, ak saraxndiku, ak fiiru, ak raxas ñaari bën-bëni nopp ya. Ñooy bën-bën yi tàbbi ci bopp. Bu dee ndabi nopp ya nag, raxas biteem ak biiram day war.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak juróom (15) *Laxdariyu *
{ YEETE }
Ku fàtte déeneer, walla ab cér ci cangaayam, na gaaw raxas ko, jamono ba mu ko fàttalikoo, donte ne ginnaaw weer la, te mu baamu la mu julli woon lu jiitu.
Bu ko yeexee ginnaaw ba mu ko fàttalikoo, cangaayam la yàqu na. Bu dee dafa nekk ci céri njàpp, mu daje woon ak raxasu njàpp ma, kon dina ko doy. (maanaam raxasub njàpp ma doy na sëkk walif beneen raxas)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak juróom benn (16)*Laxdariyu *
{ WAY-TEREY JANAABA }
Daganul ñeel ki ànd ak janaba muy dugg ci jàkka, walla jàng Alxuraan lu dul ab aaya, ak lu ni mel, ngir muslu ak lu ni mel.
Jaaduwul ñeel ki àttanul laal ndox mu sedd ci yaramam (ngir tawat) mu dikke (jote) ak jabaram ndare mu waajal jumtukaay bu mu man a tàngalee ndox ma, lu dul ne dafa gént, kon déet dara di ko ca war. (Maanaam bu géntee jote ak jigéen ci kawub lal kon deesu ko teg benn daan ngir li mu ñàkk a waajal jumtukaay bu mu nuggalee ndox ma ngir sangu)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak juróom ñaar (17) *Laxdariyu *
{ TIIM }
Aji-tukki ji ci lu dul moy Yàlla, ak aji-tawat ji sañ nañoo tiim, ñeel jullig farata walla naafila.
Aji-teew ji te wér, sañ naa tiim ñeel jullig farata bu dee ragal naa génn waxtu wa.
Aji-teew ji te wér sañul tiim ñeel naafila, walla jumaa, walla jullee néew, lu dul ne dafa ràññeeku (nar a nëb) moom néew ba.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak juróom ñatt (18) *Laxdariyu *
{ FARATAY TIIM }
Faratay tiim juròom ñatt lañu ñooy : Yéene, ak pàkk bu laab (mooy doj, walla suuf, walla ban ), ak masaa xar kanam, ak masaa ñaari yoxo ya ba ca tikku jara ya, ak dóor bu njëkk ba, ak gaaw ga,(def ko ci génn anam te bañ koo teqale) ak tàbbi ca waxtu wa,(xaar ba waxtu julli wa tàbbi ngay door a tiim) ak jokk ko ca julli
ga.
(Boo tiimee ba noppi bu fa nekk di def dara gaawal def la la tax di tiim)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fukk ak juróom ñent (19)*Laxdariyu *
{ YEETE }
Pàkk (bees man a tiime) mooy: Suuf, ak ban bu wow, ak doj (xeer woo xam ne du simoŋ, lu mel ni xeeru dënnu, ak xeeru géej) ak nees, ak ban (bu tooy), ak lu ni mel.
Du doy muy tiim ci laso bu ñu togg, ak basaƞ, ak dénk, ak ñax, ak lu ni mel.
Yolomalees na ñeel aji-tawat ji mu tiim ci miiru doj, ak miiru ban, bu dee amul ku ko jottali suuf su mu man a tiime.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk (20) *Laxdariyu *
{ SUNNAY TIIM }
Sunnay tiim ñatt lañu ñooy : Yeesal dóor ba ñeel ñaari yoxo ya ak masaa li nekk ci diggante tikku jara ya ak conca ya ak toftale.(La war a jiitu,jiitu la ca war a topp topp ca)
{ NGËNEELI TIIM }
Ngëneeli tiim ñooy : Wax bismil Laah, (booy tàmbali) ak jiital nday-joor ca càmmooñ ak jiital bitti xasab ca biiram (maanaam kaw xasabub loxo ba ngay njëkk a masaa ca biir ba) ak jiital njëlbeenu waaraam ya ci mujjug conca ba. (Maanaam fi waaraam yi tàmbalee, ngay tàmbalee masaa jëm ca conca ba)
{ YIY FIRI (TOJ)TIIM }
Yiy firi (toj) tiim, mooy yiy firi njàpp.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak benn (21) *Laxdariyu *
*{ YEETE } *
Maneesul a julli ñaari farata ci menn tiim.
Képp ku tiim ngir farata dagan na mu naafila ginnaawam ak laal Alxuraan ak tawaaf (wër Kaaba ga) ak jàng Alxuraan bu ko yéenee, te jokku ko ca julli ga te génnul waxtu wa.
Dana doy ci tiimug naafila lépp luñu tudd lu dul farata.
Ku julli gee ci tiim, na gaaw jóg julli safaa ak wiitar ginaawam, ci lu dul yeexe.
Ku tiim ngir janaba, manul ñàkk mu yéene ko. (Maanaam yéenewaale janaba ja, ca ba muy yéene tiim ma)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak ñaar (22) *Laxdariyu *
{ MBËRËG }
Jigéen ñi ñatt lañu: Ji koy doog a gis ak ji ko baaxoo (aadawoo) gis ak ji ëmb.
Li ëpp ci mbërëg ñeel jigéen ji koy doog a gis fukki fan ak juróom la.
Jigéen ji ko baaxoo gis aadaam lay jàpp. Bu deret ja wéyee na dolli ñatti fan yoo xam ne du tax mu weesu fukki fan ak juróom.
Ñeel na jigéen ji ëmb ba weesu ñatti weer, fukki fan ak juròom ak lu ni mel.
Ñeel na jigéen ji ëmb ba weesu juróom benni weer, ñaar fukki fan ak lu ni mel.
Bu dee deret ja daa dog, (maanaam di dagg-daggee tay mu ñëw suba du ñëw) na waññi bis yi deret ji di ñëw, ba mu mat aadaam. (Mu sangu ji)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak ñatt (23) *Laxdariyu *
{ WAY-TEREY MBËRËG }
Daganul ñeel aji-mbërëg ji muy julli, walla woor, walla tawaaf, (wër kaaba ga) walla laal kaamilu Alxuraan, walla dugg jàkka.
Dana ko war fay koor ga, (maanaam fay bori koor) bàyyi julli ya. (Maanaam bañ a fay bori julli ya)
Man naa jàng Alxuraan ci lu dul muy laal téere ngir ragal a fàtte walla muslu, walla sàkku tegtal yooyu yépp dagan na ci moom.
Daganul ñeel jëkkëram muy laal pëyam, walla la nekk ci diggante jumbaxam ak i wóomam, mbate mu sangu.
(Maanaam jigéen bu gisee mbërëg danganul muy sëy ak jëkkëram lu dul ne deret ja daa dagg ba mu sangu ji ba noppi)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak ñent (24) *Laxdariyu *
{ GËSIN (dereti wësin)}
Gësin naka mbërëg la ci ay tereem. (Maanaam li ñu lay tere ci mbërëg moom lañu lay tere ci gësin)
Li ëppam juròom benn fukki fan lay am. Bu deret ja dogee lu ko jiitu, donte ne bisub wësin wa la, na sanguji te julli. Bu deret ja dellusee, te diggante ñaari deret ya mat fukki fan ak juróom, walla lu ko ëpp, kon bu ñaareel ba day nekk dereti mbërëg. Bu dul loolu, na ko jokk ca deret ju ñjëkk ja, te mu nekk di mottali gësin ja.
(maanaam bu fekkee diggante ba matul fukki fan ak juróom kon dereti gësin ja moo jeexagul, na ko jokk ca bu njëkk ba, bu matee juróom benn fukki fan walla mu dagg ci diggante bi kon na sanguji)
*(Wax Wolof Ak
Bind ñaar fukk ak juróom (25) *Laxdariyu *
{ WAXTU JULLI YI }
Waxtu wa ñu tànn ngir tisbaar, mi ngi dalee ci jengarbikug jant bi, ba ci mujjug taxawaay ba. (Maanaam boo demee ba sa takkndeer tolloo ak sa jëmm)
Waxtu wa ñu tànn ngir tàkkussaan, mi ngi dalee ca mujjug taxawaay ba, ba ci jant bu gel. (Mooy bu jant bi tàmbalee xonq jëm ci so)
Seen lor (waxtu wi manut a ñàkk) ci ñoom ñaar dem na ba jant bu so.
Waxtu wa ñu tànn ngir timis, mooy kem la nga xam ne dees na ci julli ginnaaw ba nga defee sàrt ya. (Timis waxtoom daa gàtt dees koy tënk rekk ci bu jant bi sowee, ba nga def sàrt yiy tax a man a julli, boo jullee sëlmal rekk waxtu wa jeex na.)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak juróom benn (26) *Laxdariyu *
Waxtu wa ñu tànn ngir gee mi ngi dalee ci fàddu safax (mooy niir yu xonq yiy des ci asamaan ginnaaw bi jant bi sowee ) ba ci ñatteelu xaaj wi njëkk ci guddi gi.
Seen lor (lu mant a ñàkk) ñoom ñaar dem na ba fenktelug fajar.
Waxtu wa ñu tànn ngir suba mi ngi dalee ci fajar ba ci weex-weex ya di aji-kawe (bët set). Aw loram (lu mant a ñàkk) dem na ba ci fenktelug jant bi.
Fay nekk na ci mbooleem lu nekk ca ginnaaw loolu.
(maanaam kepp koo xam ne julliwóo ci waxtu wi ñu tànn, julliwóo ci li mant a ñàkk kon dangay fay, waaye jooxewóo ( julliwóo ca waxtu wa )
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak juróom ñaar (27) *Laxdariyu *
{ ÀTTEY YEEX A JULLI WALIF WAXTU WA }
Ku yeexe ag julli ba génn waxtoom, dana gàddu bàkkaar bu mag, lu dul ne dafa nekk aji-fàtte, walla aji-nelaw.
Déet julli naafila ginnaaw jullig suba ba ca yëkkatikub jant bi, ak ginnaaw jullig tàkkusaan ba ca jullig timis, ak ginnaaw xarug fajar, lu dul wird (dog wees baxoo def) ñeel aji-nelaw walif ko, ak ca toogaayu Imaamu jumaa ca minbar ba, ak ginnaaw jumaa ba Imaam génn jàkka ja.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak juróom ñatt (28) *Laxdariyu *
{ SÀRTI JULLI }
Sàrti julli ñooy: Laabu hadas (laab ci toj) ak laabu xabas (laab ci sobe) ci sa yaram ak ci sa yéere ak ci béreb bi ngay jullee ak suturaal sa awra ak jublu xibla (penku) ak bàyyi wax ak bàyyi jëf ju bari te bokkul ci julli gi .
Awra góor mooy la tàmbalee ca diggante jumbax ba ca wóom ya. Jigéen nag léppam awra la, ba mu des xar kanamam ak ñaari tenqoom.
Sibees na julli ci tubay rekk, lu dul ne dafa nekk ci kawam dara. (Maanaam góor gu sol tubay rekk di julli te solul yéere)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñaar fukk ak juróom ñent (29) *Laxdariyu *
Ku mbalaanam (yéere) sobewu, te amul meneen mbalaan, te amul ndox mu mu ko raxase, walla nekkul fa moom lu mu sol ba raxas ko, te mu ragal génn waxtu wa, kon na julli ca sobeem sa.
Daganul yeexe julli ci ñàkk ug laab. Ku def loolu, moy na Boroomam.
Ku amul lu mu suturaale awraam, na julli ci rafle. (Maanaam yaramu neen lay jullee)
Ku moy xibla, (penku) na baamu ca waxtu wa. Bépp julli bu ñuy baamu ca waxtu wa, baamu ga ngëneel la.
Bépp julli boo xam ne dees na ko baamu ca waxtu wa, deesu ko baamu bu waxtu wa jàllee, naafila it bu waxtu jàllee deesu ko fay.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer (30) *Laxdariyu *
{ FARATAY JULLI }
Faratay julli fukk ak ñent lañu ñooy: Yéene julli ga ràññiku ak kàbbaru armal ak taxawaay ba ñeel ko ak faatiha ak taxawaay ba ñeel ko ak rukkoo ak siggi ci rukkoo ak sujjood ak siggi ci sujjood ak yemoo ak sax (Mooy ànd ak dal ci lépp looy def ci julli gi ) ak toftale diggante farata ya ak sëlmal ak toogaayu sëlmal.
Sàrti yéene mooy lëkkale ko ak kàbbaru armal ba.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak benn (31) *Laxdariyu *
{ SUNNAY JULLI }
Sunnay julli fukk ak juróom lañu ñooy: Liqaam ak saar walla laaya ba ngay jàng ginnaaw faatiha ak taxawaay ba ñeel ko ak yelu ca la nga xam ne dees na ca yelu ak béral ca la nga xam ne dees na ca béral ak wax samihal Laahu liman hamidah ak bépp kàbbar bu dul kàbbaru armal ak ñaari taaya ya ak toogaay ya ñeel leen ak jiital faatiha ca saar wa walla laaya ja ak sëlmal bu ñaareel ak bu ñatteel ñeel maamoom (Kiy roy ci imaam) ak béral sëlmalub yewwiku ba ak julli ci Yònnent Bi ci taaya ju mujj (Yal
na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc) ak sujjood ci bakkan ak ci ñaari tenq ak ci ñaari bëti wóom ak ci ñaari cati ndëggu ak saatir (Muy teg dara ci sa kanam ba kenn du fa man a jaar) ñeel ku dul maamoom (Aji-roy). Li gën a néewam mooy talaayu xeej ak guddaayu xasab, tay aji-laab, di aji-sax, te du jaxjaxal am xel.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak ñaar (32) *Laxdariyu *
{ NGËNEELI JULLI }
Ngëneeli julli ñooy: yëkkati ñaari yoxo ca kàbbaru armal, ba mu tolloo ak ñaari nopp ya ak waxug maamoom ak kenn kuy julli « rabbanaa wa lak’k alhamd » ak aamiin ginnaaw faatiha ñeel kenn kuy julli ak maamoom, imaam du ko wax (moom aamiin) lu dul ci njàngum yelu ak sàbbaal ci rukkoo ak ñaan ci sujjood ak guddal njàng ma ci jullig suba (maanaam saar wa ngay jàng walla laaya ja) ak tisbaar ak gàttal ko ci tàkkusaan ak timis ak digg-doomal ko ci gee.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak ñatt (33) *Laxdariyu *
{NGËNEELI JULLI}
Pàcc 2
Ak def saar wi ngay njëkk a jàng gën a gudd saaru ñaareel wa ak def julli gi ci melo wa ñu xam (maanaam melo wi ñu ko jële ci Yónnent) ci rukkoo ya ak sujjood ya ak toogaay ya ak xunoot ba ñuy yelu lu jiitu rukkoo ak ginnaaw saar ci ñaareelu ràkkaa suba, dagan na it ginnaaw rukkoo ba ak ñaan ginnaaw ñaareelu taaya ak def ñaareelu taaya gën a gudd ci bu njëkk ba ak nday-jooru ci sëlmal (maanaam sëlmal bu njëkk ba nga def ko ci sa wetug nday-joor) ak yëngal baaraamu joxoñ ba ci taaya.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak ñent (34) *Laxdariyu *
{ YUÑ SIBI JULLI }
Sibees na geestu ci julli ak gëmm ay gët ak basmala (Muy wax bismil Laahir rahmaanir rahiimi) ak hasbala (Muy wax ahoosu bil Laahi minas saytaanir rajiim) ci jullig farata. Dagan nañu ci jullig naafila. Sibees na taxaw ci benn tànk lu dul ne dafa yàgg taxawaayam ba ak lëkkale ñaari tànk ak sex dërëm walla lu dul moom ci sa gémmiñ, naka noonu def lépp lu lay jax-jaxal ci sa jiba (poos) walla say yoxo mbubb walla ci ginnawam ak xalaat ci mbiri àdduna ak lépp lu lay soxlawoo walif ragal Yàlla ci julli.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak juróom (35) *Laxdariyu *
{ TOROXLU CI JULLI }
Ñeel na julli, leer gu màgg guy jollee ci xolub jullikat yi, du ko am lu dul ñi ragal Yàlla.
Boo dikkee (jóge) jëm ci julli, nanga teqale sa xol ci àdduna ak li ci biiram, nanga soxlawoo ci fugluwaante ak lu jokk ci sa Boroom mi nga xam ne dees na julli ngir jëmmam.
Nanga fas ne naka julli toroxlu la, ak sippeeku ñeel Yàlla ca sellam ga, ca taxawaay ya ak rukkoo ya ak sujjood ya; kaweel la ak màggal ñeel ko, ca kàbbar ya, ak sàbbaal ya, ak tudd ya.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak juróom benn (36) *Laxdariyu *
{TOROXLU CI JULLI}
Pàcc 2
Nanga sàmm julli, moom mooy jaamu Yàlla gi gën a màgg. Bul bàyyi saytaane mu fowe sa xol, mu soxlawoo la walif sa julli ba muur (far) sa xol, ba xañ la lenn ci bànneexi leeri julli. Dana la war nga saxoo ragal Yàlla ci julli. Naka moom julli day tee def lu bon ak luñu sib ci sababu toroxlu ci moom julli. Nanga dimbandikoo ci Yàlla, ndax mooy gën ji way dimbandikoo.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak juróom ñaar (37) *Laxdariyu *
{ MELO YI WAR AK YI ÑU SOPP CI JULLI }
Ñeel na julli gi wéet (gi ñu farataal) juróom ñaari defiin yu toftaloo. Ñent ci yooyu toftale ga lu war la, ñatt yi yu ñu sopp la.
Yi nga xam ne toftale ga lu war la, ba ca njëkk mooy taxaw bañ a wéeru, topp ca taxaw wéeru, topp ca toog bañ a wéeru, topp ca toog wéeru. Toftale diggante ñenti yii lu war la. Bu àttanee ci benn defiin ci yooyu, mu julli ci defiin bu ko yées, julleem yàqu na.
Ñatt ya nga xam ne nekk nañu ci sopeel mooy jullig aji-lott ji ci ñatt yii ñu tuddd. Mu julli ci wetug nday-joor, topp ci wetug càmmooñ, topp dëfeenu. Bu wuutalee (man benn bàyyi ko fa def beneen) ci ñatt yii julleem yàquwul.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak juróom ñatt (38) *Laxdariyu *
{MELO YI WAR AK YI ÑU SOPP CI JULLI}
Pàcc 2
Wéeru giy yàq jullig ki àttan (am kàttan) bàyyi ko, mooy wéeru goo xam ne dana rot ci ak rotam, (Maanaam rotug la mu wéeru.) Bu dee du rot ci rotam, loolu luñu sib la. (Maanaam wéeru ga dees koo sib) Bu dee naafila, dagan na ci ku àttan (am kàttan) ci taxaw mu julli ko ci toog. Dana ko ñeel genn wàllu yoolu ku taxaw. Dagan na mu tàbbi ca ci toog, topp mu taxaw ginnaaw ga, wàlla mu tàbbi ca, ci taxaw, te mu toog ginnaaw ga, lu dul mu tàbbi ca, ci yéene taxaw ci moom julli ga. Kon dees na tere toogaaayam ginnaaw loolu.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind fanweer ak juróom ñent (39) *Laxdariyu *
{ FAY WAY-FAAT YI }
Dana war fay li nekk ci loos ci ay julli. (Maanaam bori julli) Daganul sàggane ci loolu.
Képp ku julli bépp bis juróoomi julli, déet muy ku sàggan.
Dana fay julli ci kem na mu ko faate woon. Bu dee nekkoon na di kojug teew, da koy fay ci kojug teew. Bu dee nekkoon na ci kojug tukki, da koy fay ci kojug tukki. Moo xam jamono ja miy fay dafa nekk ci teew walla ci tukki. War na Toftale diggante ñaari teew, ak diggante néewi faat ànd ak julli gi teew, lu war la ci ak fàttaliku. Lu néew mooy ñenti julli walla lu ko yées.
Koo xam ne nekk na di ko war ñenti julli walla lu ko yées, na ko julli lu jiitu julli ga teew, donte day génn waxtu wa.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk (40) *Laxdariyu *
{ KU YOR BORI JULLI DU NAAFILA }
Dagan na fay julli ci bépp waxtu. Déet naafila ca ka nga xam ne war na ko fay jullig farata, déet julli yoor-yoor, walla taxawal naafila koor.
Daganul ñeel ko lu dul safaa ak wiitar ak ñaari ràkkaa fajar ak ñaari hiid yi ak jullig muurug weer wi walla jant bi ak jullig baawnaan.
Dagan na ñeel ña nga xam ne war na leen fay ci ñu julli ko ci mbooloo, bu dee seen julli ya yemoo na.
Ku fàtte limug la ko war ci fay (bori julli), na julli loo xam ne du ca jóge mukk ànd ak sikk-sàkka.
(Maanaam day julli lim boo xam ne dóotul am sikki-sàkka ne mat na.)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk ak benn (41) *Laxdariyu *
{ BUNTU CI JAMUJ }
Pàcc 1
Sujjoodug jamuj ci julli sunna la.
Ñeel na ki wàññi mu def ñaari sujjood lu jiitu sëlmal, ginnaaw matug ñaari taaya yi, mu dolli seen ginnaaw beneen taaya.
(Maanaam kuy julli juum wàññi ci julli gi day sujjood ñaari sujjood ginnaaw bi mu taayaaa, bu noppee taayawaat door a sëlmal, muy li ñuy tudde «Xabla Salaam»)
Ñeel na ki dolli, mu def ñaari sujjood ginnaaw sëlmal, mu taayawaat seen ginnaaw, te mu sëlmal beneen sëlmal.
(Ku juum dolli ci julli ñaari sujjood lay def ginnaaw bi mu sëlmalee, daa di taayawaat sëlmal, muy li ñuy tudde « Bahda Salaam »)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk ak ñatt (43) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 3
Ku wàññi ab farata, déet mu di ko doy sujjoot ci loolu.(Maanaam ku bàyyi farata manukóo defar ci ab sujjoot)
Ku fàtte ngëneel, déet sujjoot di ko war.
Deesul sujjoot njëkk sëlmal (Xabla salaam ) lu dul ci bàyyi ñaari sunna walla lu ko ëpp.
Bu dee benn sunna rekk, déet sujjoot di ca war; lu dul yelu, walla béral. Ku yelu ci bérebu béral na sujjoot njëkk sëlmal (Xabla salaam) ku béral ci bérebu yelu, na sujjoot ginnaaw sëlmal (Bahda salaam.)Ku wax ci njuumte, na sujjoot ginnaaw sëlmal (Bahda salaam.)
Béral mooy wax ca kaw.
Yelu mooy wax ndànk.✍🏽️
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk ak ñent (44) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 4
Ku wax ci njuumte, na sujjoot ginnaaw sëlmal (Bahda salaam).
Ku sëlmal ci ñaari ràkkaa ci njuumte, na sujjoot ginnaaw sëlmal ( Bahda salaam.)
(Maanaam Ku juum sëlmal ci ñaari ràkkaa ci jullig ñatti ràkkaa walla gog ñenti ràkkaa na jug mottali julli ga bu noppee sujjoot bahda salaam)
Ku dolli ci sa julli ab ràkkaa, walla ñaari ràkkaa, na sujjoot (bahda salaam.)
Ku dolli ci julli kemam ci ay ràkkaa, julli ga yàqu na.(Maanaam ku dolli ci ag julleem lu tollu ne julli ga muy julli, julli ga yàqu na)
Ku sikki-sàkka ci matug julleem, na dikke ca la mu sikki-sàkka. (Maanaam ku am xel yaar ci ag julleem ndax mat na walla na jàpp ne matul, mu mottali ko bu noppee sujjoot bahda salaam)
Ku sikk-sàkka ci wàññi, na ko dëggal.
(Maanaam na jàpp ne daa wàññi)
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk ak juróom (45) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 5
Ku sikki-sàkka ci ab ràkkaa walla ab sujjoot, na ko dikke, te sujjoot bahda salaam. (Maanaam ku xel yaar ci ndax dafa bàyyi ab ràkkaa walla ab sujjoot na ko indi te sujjoot bahda salaam)
Bu sikki-sàkkaa ci sëlmal, na sëlmal bu dee nekk na lu jege, te déet sujjoot di ko war, bu yàggee, julleem yàqu na.
Kiy jax-jaxal, na bàyyi jax-jaxal ba ca xolam (Maanaam ki nga xam ne day sikki-sàkka lu bari) déet muy dikke ca lu mu sikki-sàkka. Li fi nekk daal, day sujjoot bahda salaam saa su julleetee ba noppi, moo xam sikki-sàkka ga ci yokk la walla wàññi.
Ku béral (Xunuut) ci jullig suba déet sujjoot di ko war, bu fekkee moo ko tay sibees na ko.
(Wax Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk ak juróom ñaar (47) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 7
Ku baamu faatiha ci fàtte, na sujjoot (Bahda salaam.) Bu dee ci tayeef la, la feeñ mooy yàqug julli ga.
Ku fàttaliku saar ginnaaw ba mu tàbbee ci rukkoo, déet muy dellusi ca saar wa. (Maanaam ku fàtte woon jàng saar walla ab aaya ba muy teg ca ginnaaw faatiha, ba rukkoo door koo fàttaliku, kon du jar muy dellusi di jàng saar wa, na wéy bu noppee sujjoot (Xabla salaam)
Ku fàttaliku yelu walla béral lu jiitu muy rukkoo, na baamu njàng ma, bu dee saar wa rekk la na ko baamu, te déet sujjoot di ko war. Bu dee dafa nekk ci faatiha ja, na ko baamu te sujjoot (Bahda salaam.)
Bu ko fàttee ba rukkoo, na sujjoot (Xabla salaam) ngir bàyyi béral, te sujjoot (Xabla salaam) ngir bàyyi yelu, moo xam faatiha ja la walla saar wa rekk.
Wax(Wolof Ak Xamle)
Bind ñent fukk ak juróom ñatt (48) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 8
Ku reetaan ci julli, julleem yàqu na, moo xam njuumte la walla ci tayeef.
Du reetaan ci julleem lu dul aji-sàggan, buy fo. Way-gëm ji bu taxawee ngir julli, day dummooyu ci xolam lépp lu dul Yàlla (Tudd naa sellam ga) mu bàyyi àdduna ak li ci biir, ba teewal ci xolam màggug Yàlla ak kaweem, te mu loxal xolam, mu ragal loo bakkanam ci téeyug Yàlla (Tudd naa màggam ga.) Naka loolu mooy jullig way-ragal ña Yàlla.
Déet dara di ko war ci muuñ. Naka noonu jooyug aji-ragal Yàlla ci julli, lu ñu jéggale la.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk (50) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 10
Ku tisóoli ci julleem, déet muy soxlawoo ci sant,(Maanaam wax Alhamdu lillaah) déet muy delloo ca ka ko ndokkeel, déet muy ndokkeel ku tisóoli. Waaye nag bu waxee alhamdu lillaah, déet dara di ko ca war.
Ku óbbali ci julli, na ub gémmiñam ci loxoom, déet muy tufli lu dul ci mbalaanam ci lu dul génnug araf. (Maanaam kuy julli su bëggee tufli na jël aw sagar tufli ca te wattandiku génneew araf)
Ku sikki-sàkka ci laab walla sobe, mu xalaat tuuti (lu néew) ci julleem, topp mu leer ko laabam, déet dara di ko war. (Maanaam kuy julli di sikki-sàkka ndax yor na am njàpp walla déet, ginnaaw bi, mu leer ko ne yor na njàpp dara du ko ca war)
Ku geestu ci julli ci njuumte, déet dara di ko ca war. Bu ko tayee, def na lu ñu sib. Bu moyee xibla (penku), julli ga dog na. (Maanaam yàqu na)
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak benn (51) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 11
Ku julli ci sooy, (Xeetu ndima la lol lislaam daa tere góor ñi, ñu di ko sol) walla ci wurus, walla mu sàcc ci julli, walla mu xool lu haraam, ku def yii moy na Yàlla, waaye julleem lu wér la.
Ku juum jàng baat bu bokkul ci Alxuraan ci julleem, na sujjoot (Bahda salaam.) Bu bokkee ci Alxuraan, déet sujjoot di ko war, lu dul ne dafa soppi baat ba walla mu yàq maanaa ma, na sujjoot (Bahda salaam.)
Ku jayexu (dajjantu) ci julli, déet sujjoot di ko war. Bu nelawam ya diisee nag, na baamu julli ga, ak njàpp ma.
Wonki aji-tawat lu ñu jéggale la.
Xaddamiku ngir lor lu ñu jéggale la.
Déggale lu ñu sib la, (Maanaam di yëglu ngir ñu xam ne yaa ngi julli ci lu mel ni xaddamiku) waaye yàqul julli.
Koo xam ne woowees na ko, mu wax (Subhaana Laah) def na lu ñu sib, waaye julleem wér na.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak ñaar (52) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 12
Ku gag ci jàng, te kenn gàggantiwu ko, na bàyyi boobu aaya, te mu jàng aaya ba ca kanamam. Bu tëlee ci gàggantiku, na rukkoo, déet muy xool téere Alxuraan ba ca wetam lu dul ne dafa nekk ci faatiha ja; Kon du man a ñàkk mu matal ko ci téere Alxuraan wàlla ci leneen. Bu bàyyee benn ayaa ci faatiha, na sujjoot (Xabla salaam.) Bu dee lu ëpp benn aaya, julleem yàqu na.
Ku ubbee keneen ku dul Imaamam, (Gàgganti) julleem yàqu na.
Bu mu ubbee ci Imaamam lu dul mu négandiku ubbee ga (Maanaam xaar ba Imaam sàkku ko) walla mu yàq maana ma.
Ku wëndeel xalaatam tuuti (lu néew) ci biri àdduna, wàññi na yoolam, waaye julleem yàquwul.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak ñatt (53) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 13
Ku jeñ kiy dox ca kanamamm, walla mu sujjoot ci catu jëwam, walla mu sujjoot ci laxas walla ñaari laxas ci kaalaam, déet dara di ko war.
Déet dara ci notug waccu, ak gall ci julli. (Maanaam kuy julli jekki-jekki waccu walla mu gall dara du ko ca war )
Njuumteg maamoom, Imaam a koy gàddu, lu dul mu nekk ci wàññi farata. (Maanaam maamoom saa yu juumee ci julli gi bàyyi dara lu bokkul ak farata walla ab ponk, Imaam a koy gàddu, sujjoot du ko ca war)
Wax(Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak ñent (54) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 14
Bu maamoom juumee, walla mu jeyexu,(Nelaw yu woyof) walla ñu tanc ko ci rukkoo, te moom nekkul ca ràkkaa ba njëkk, bu wóoloo jot Imaam lu jiitu siggeem ca sujjootub ñaareel ba, na sujjoot te dab Imaam.
Su wóoluwul dab ko, na bàyyi rukkoo ba, te mu topp Imaamam, te mu fay ràkkaa ca barabam, ginnaaw sëlmalug Imaamam. Bu juumee walif sujjoot, walla ñu tanc ko, walla mu jeyexu ba Imaam jóg jëm ci beneen ràkkaa, na sujjoot bu wóoloo ci dab Imaam lu jiitu muy fas rukkoo, bu dul loolu na ko bàyyi, mu topp Imaam, te mu fay beneen ràkkaa batay. Bépp fayug ràkkaa, déet sujjoot di ca war, lu dul mu nekk di sikk-sàkka ci rukkoo, walla ci sujjood.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak juróom (55) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 15
Koo xam ne dikkee na ko jiit, walla jaan, mu ray ko, déet dara di ko war, lu dul ne jëf ja dafa yàgg, walla mu moy xibla, kon julleem dog na. (Maanaam kuy julli lu mel ne jiit walla jaan jëmsi ci moom, man na koo ray te du yàq dara ca julli ga; lu dul ne jëf ja daa yàgg, walla mu moy xibla (penku) kon julli ga yàqu na.)
Ku sikki-sàkka ndax moom mi ngi ci wiitar walla ci ñaareelu safaa, na ko def ñaareelu safaa, mu sujjoot (Bahda salaam,) topp mu wiitar.
Ku wax diggante safaa ak wiitar ci njuumte, déet dara di ko war, bu ko tayee sib nañu ko, waaye déet dara di ko ca war.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak juróom benn (56) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 16
Ka ñu raw, bu jotee ànd ak Imaam lu gën a néew ràkkaa, déet muy sujjoot ànd ak moom (Xabla,) walla (Bahda.) Bu sujjootee ànd ak moom julleem yàqu na. (Kon koo xam ne amul ci jullig Imaam ab ràkkaa bu Imaam defee lu waral sujjoot, buy sujjoot du ànd ak Imaam, bu àndee ak moom julleem yàqu na.)
Bu jotee ràkkaa bu mat, walla lu ko ëpp, na sujjoot ànd ak Imaam (Xabla,) te mu yeexe (Bahda,) ba julleem mat mu koy door a sujjoot.
Bu sujjootee (Bahda ba) ànd ak Imaam ci tayeef, julleem yàqu na, bu nekkee ci njuumte, na sujjoot (Bahda salaam.)
Ka ñu raw, bu juumee ginnaaw sëlmalug Imaamam, naka buy julli moom rekk. (Maanaam koo xam ne Imaam da koo raw, mu jug di fay ginnaaw sëlmalug Imaam far def njuumte, kon day mel ni bu doon julli moom dong.)
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak juróom ñaar (57) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 17
Bu toftaloo ca ka ñu raw sujjootub (Bahda) ci Imaamam, ak (Xabla) ci jëmmi boppam, dana ko doy sujjootub (Xabla.)
Ku fàtte rukkoo, mu fàttaliku ko ci sujjoot, na dellu taxaw, sopp nañu ñeel ko mu baamu as lëf ca njàng ma, topp mu rukkoo, te mu sujjoot (Bahda) salaam. (Maanaam ku fàtte rukkoo bay sujjoot fàttaliku ko, day dellu taxaw njàngaat faatiha ak uw saar daa di rukkoo, bu sëlmëlee sujjoot (Bahda salaam)
Ku fàtte benn sujjoot, mu fàttaliku ko ginnaaw taxawaayam, na dellu toog, te mu sujjoot ko, lu dul ne dafa toogoon lu jiitu muy taxaw, kon déet muy dellu di toog.
Ku fàtte ñaari sujjoot, ba taxaw na daa di rot sujjoot, te bu mu toog.
Dana sujjoot ci mbooleem yooyu (Bahda salaam.)
Wax *(Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak juróom ñatt (58) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 18
Bu fàttalikoo sujjoot ginnaaw yëkkatikug boppam tukkee ca rukkoo bob topp na ca, na wéy ci julleem, bu mu dellusi, na sànni boobu ràkkaab jamuj bu yàqu, mu dolli ràkkaa ca barabub ràkkaa ba yàqu, di aji-jokk, mu sujjoot (Xabla salaam.)
Bu nekkee ca ñaar yu njëkk ya, te mu fàttaliku ko ginnaaw fasug ñatteel ba, na sujjoot (Bahda salaam.)
Bu nekkul ca ñaar yu njëkk ya, walla mu nekk ca, te mu fàttaliku ko lu jiitu fasug ñatteel ba, kon na sujjoot (Bahda salaam ) ndax saar wa ak toogaay ba, faatuñu ci moom.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom fukk ak juróom ñent (59) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 19
Ku sëlmal ba noppi di sikki-sàkka ci matug julleem, julleem yàqu na.
Jamuj ci jullig fay, naka jamuj ci jullig jooxe.
Jamuj ci naafila, naka jamuj ci jullig farata, lu dul ci juróoom benni masala: Faatiha ak saar ak yelu ak béral ak dolli ràkkaa ak fàtte lenn ci (ponk) yi bu yàggee.
Ku fàtte faatiha ci naafila, te mu fàttaliku ko ginnaaw rukkoo, na wéy, te sujjoot (Xabla Salaam;) ci lu wuute ak farata. Bu doon ci farata, day sànni boobu ràkkaa, te dolli beneen, daa di wéy. Bu dee sujjoot la bàyyi it, dina nekk naka nu ko tudde woon ci ko bàyyi sujjoot.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom benn fukk (60) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 20
Ku bàyyi saar, walla béral, walla yelu ci naafila, mu fàttaliku ko ginnaaw rukkoo, na wéy, te déet sujjoot di ko ca war, ci lu wuute ak farata.
Ku jóg jëm ci ñatteelu ràkkaa ci naafila, bu ko fàttalikoo lu jiitu fasug rukkoo ba, na dellusi toog, te sujjoot (Bahda salaam.) Bu ñatteel ba fasoo, na wéy, te dolli ñenteelu ràkkaa, bu noppee sujjoot (Xabla salaam,) wuute ak farata. Bu doon ci farata, day dellusi jamono ba mu ko fàttalikoo, daa di sujjoot (Bahda salaam.)
Ku fàtte ab ponk ci naafila lu mel ni rukkoo, walla sujjoot, te fàttalikuwu ko mbate mu sëlmal, te mu yàgg, déet baamu di ko war, ci lu wuute ak farata. Bu doon ci farata, dana ko baamu ba (fàww).
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom benn fukk ak benn (61) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 21
Ku dog naafila ci tayeef, walla mu bàyyi ca moom ràkkaa, walla sujjoot ci tayeef, dana ko baamtu ba fàww.
Ku óbbali ci julleem, déet dara di ko war, lu dul ci génnug araf (loy).
Bu Imaam jamujee ci wàññi, walla yokk, na ko maamoom ya sàbbaal.
Bu sa Imaam jógee tukkee ci ñaareelu ràkkaa, sàbbaal ko. Bu teqalikoo ak suuf, topp ko. Bu toogee ca ràkkaa bu njëkk ba, walla ca ñatteelu ràkka ba, jógal, te bul toog ànd ak moom. Bu sujjootee benn sujjoot, te bàyyi ñaareel ba sàbbaal ko. Bul jóg ànd ak moom lu dul nga ragal fasug rukkoom. Kon topp ko, te bul toog ginnaaw loolu ànd ak moom, déet ca ñaareelu ràkkaa ba, walla ca ñenteel ba. Bu sëlmalee, nga dolli beneen ràkkaa mu wuutu ràkkaa ba nga sànni, ci yéene, te nga sujjoot (Xabla salaam.) Bu ngeen nekkee mbooloo, li gën ñeel leen mooy ngeen jiital kenn mu mottali seen ug julli.
Wax (Wolof Ak Xamle)
Bind juróom benn fukk ak ñaar (62) *Laxdariyu *
{BUNT CI JAMUJ}
Pàcc 22
Bu dee Imaam dafa dolli ñatteelu sujjoot nañu ko sàbbaal. Déet ñuy sujjoot ànd ak moom.
Bu Imaam jógee jëm ci juróomeelu ràkkaa, na ko topp ka nga xam ne wóor (leer) na ko ne def na lu ko waral, walla mu sikki-sàkka ca loola. Mu toog ka nga xam ne wóor (leer) na ko ne Imaam day dolli. Bu ko njëkk ka toogee, te ku ñaareel ka jóg, seen julli yàqu na.
Bu Imaam sëlmalee lu jiitu matug julli ga, ña nekk ci ginnaawam nañu ko sàbbaal. Bu dëggalee matug julleem, na sujjoot (Bahda salaam.)
Bu sikki-sàkkaa ci xibaaram, na laaj ñaari way-maandu. Dagan na ñeel leen wax ci loolu. Bu wóoloo mat ga, na def la mu wóolu, te bàyyi ñaari way-maandu ña, lu dul ne nit ña ca ginnaawam dañoo bari. kon na bàyyi la mu wóolu, te fekki leen.
Fii la téere bi jeexee.
Maa ngi sant Yàlla mi nu may ag tàmbali ak ug yeggale yal nanu nangul jëf ji ci barkeb Yónnente Bi nu indil njub gi te mooy lislaam aamiin !
Wax ( Wolof Ak Xamle )