Borom Daaraji (RTA)

Les 23 Chartes de la Tariixa Tijjaan

1- Nga jàpp wird bi ci ku am ndigal bu wér; ndigal guy jàppaloo ba ci Siidi Ahmet Tijaani ni callala.

Le postulant doit être affilié par un muqaddam qui lui-même est consacré dans sa fonction par le Cheikh fondateur ou un des ses représentants notoires.

2- Ki jël Tariixa bi, na fekk bumu yore benn wirdu Sëriñ, walla na bàyyi wirdu Sëriñ boobu, walla Muxàddam bi bu mu ko may wird bi. Su ko ko mayee, dog na, moom Muxàddam bi ci Tariixa bi. Soo bàyyee sa wird, Seex moo la gaaranti.Tijaan bi su bàyyee wirdam, benn Sëriñ manu ko aar ci alku, ak Sëriñ boobu lu mu rëy-rëy maartaba, ak ku mu man a doon.

Le postulant doit être libéré de toute obédience envers une autre tarixa. Si le postulant accepte de laisser son wird initial, il est sous la protection de CHEIKH, quelque rang quoccupe le Serigne quil quitte. Si le tidiane par contre laisse son wird, aucun serigne, quel que soit son rang ou son grade, ne peut le prémunir de sa perdition.

3- Doo siyaare benn wàlliyu buy dund ak bu dee bu dul Tiijaan.Te boo ko defe dog nga ci Tariixa bi.Du xeebate walla rëylu, sàrt la rekk.Terewul seetante, demante.

Il lui est absolument interdit de visiter  » ziarra » ou dinvoquer lintercession de tout saint étranger (non tijaane) vivant ou mort, sous peine dêtre exclu de la tarixa. Il doit néanmoins considération et respect à tout saint homme sans exclusive. Cette conditionnalité nexclut pas non plus une fréquentation entre musulmans.

4- Saxoo di julli julli juróom, ci boppu waxtu wa, ci mbooloo, ndeem Ilimaan ja mat na Ilimaan, di matal rukoo ak sujoot ya ak sellal Faatiha ; te saxoo topp sunna.

Les adeptes du masculin doivent faire les cinq prières en assemblée, et autant que possible à la mosquée. Les adeptes du sexe féminin prieront à la première heure de la période correspondant à chaque prière. Les deux adeptes du sexe se soumettront aux lois établies par la Charria et suivront la souna.

5- Saxoo bëgg Seex Ahmet Tijaani ba kerook ngay dee, ak xalifaam, ormaal ko ni ngay ormalee Seex ci boppam.

Il lui faut aimer Cheikh Ahmed Tijane et ses khalifes d’un amour puissant et toujours croissant, honorer le khalife de Cheikh au même titre que lui-même.

6- Bañ a nangu mukk, bañ a wóolu pexem Yàlla. Ngëneelu Tariixa bi, bu mu tax nga bañ a def li la war ak bàyyi li la war. Soo ko defee, Yàlla dina la nattu ba nga bañ a Seex. So bañee seex génn nga ci Tariixa bi.

Il lui faut se garder d`un excès de confiance, de se suffire soi- disant du dessein de DIEU. Ne point se fonder sur les promesses et les avantages de la tarixa et « se croiser les bras ».

7- Doo xas mukk, doo noonoo mukk, doo goti mukk Seex Ahme Tijaane.

Il ne proférera jamais d’injures ou de critiques à l’adresse de Cheikh Ahmed Tijaane.

8- Saxo wird, wasifa, ak Hadara jumaa ba keroog ngay dee.

Ne jamais abandonner l’ordre après y avoir été affilié, pratiquer le wird jusqu’à la mort.

9- Sa pas-pas du wàññiku mukk, doo ko uri mukk. Sa orma ci Seex su wàññikoo, xamal ni sa pas-pas wàññiku na .

Avoir la ferme conviction de la voie.

10- Doo weddi, doo diiŋat ( doo contre) Seex Ahmet Tijjaan nee na: lu mu wax, natt leen ko ci Alxuraan ak sunna.Su dëppoowul, waxu ko.Kon ku ko weddi Yàlla ak Yónnent Bi nga weddi.

Te garder en toute circonstance de discréditer cheikh Ahmed Tijaane car tout ce qu’il dit et fait est conforme aux recommandations de Dieu et de son prophète ( S.A.S)

11- Taalibe bi, bumu wird mukk te amu ci ndigal.

Aucune personne non affiliée ne doit réciter les oraisons sans autorisation d’un muqaddem.

12- Daje di wasifa ak Hadara jumaa ci mbooloo ndeem Tijjaan a nga fa.

Assister la récitation de la wazifa et du hadara du vendredi en assemblée (si possible)

13- Doo jàng Jawharatul-Kamal te andoo ak njàpp.

Il ne faut jamais réciter la Djawharatoul-Kamal (perle de la perfection) sans ablutions rituelles.

14- Doo noononte doo dogoonte ak mbindaafoon yi rawati na ki nga bokkal Tariixa bi .

Il est interdit à l’adepte de se brouiller avec tout être humain et, encore moins avec un tijaane.

15- Doo doyadal wird wi di ko yéexe ba waxtu wi génn te amoo ngànt.

Il faut éviter toute négligence dans la pratique, notamment tout retard dans la récitation du wird, si ce n’est un cas de force majeure réelle.

16- Bul maye wird te amoo ndigalu maye ko.

Il ne faut jamais, sans investiture, s’attribuer le titre de moqaddem et donner le wird

17- Nga ormal képp ku askanoo ci Seex rawatina magu Tariixa bi .

Respecter, honorer les gens de la tarixa, en particulier les « anciens » qui ont acquis des grâces particulières de DIEU

18- Sooy wird nga laab ci sa yaram ak ci sa yére.

Veiller à la propreté rigoureuse de son corps, de ses habits.

19- Na ngay wird ci barab bu laab, bu yaatu , fu 6i nit xaj (lu mu néew-néew) ngir nga sori sobe.

Veiller à la propreté rigoureuse de l’endroit où on effectue le wird, ainsi qu’à son espacement (6 personnes)

20- Toog jublu penku bu dul ngay doxe donte mu gàtt, walla nga nekk ci géewu wasifa.

Il faut pendant la récitation des oraisons, se tourner vers la KAABA ( temple sacré de la Mecque), sauf en cas d’exception prévus (lorsqu’on se déplace en marchant par exemple).

21- Doo wax sooy wird lu dul ci loraange ak ñu dul Sëriñ bi lay tarbiya, sa nday, sa baay, mbaa sa jëkkër ñooñii lu leen neex wax ak yaw .

Il ne faut jamais, sauf en cas de force majeure, interrompre la récitation par d’autres paroles à l’exception de votre cheikhou tarbiya, votre père, votre mère ou votre mari.

22- Teewlu jëmmi Yónnent Bi, walla jëmmi sa Sëriñ balaa ngay wird ci njëlbéenu wird wi ba ca jeex ba.

Il faut, pendant la récitation, se concentrer et essayer de visualiser en esprit l’image de CHEIKH AHMED TIJANE , ou mieux, celle du prophète (sur lui la paix et le salut) ou à défaut du Serigne qui vous a affilié.

23- Teewlu maana (tekkite) waat yi ngay jàng.

Il faut, si on le peut, saisir le sens de ce que l’on récite. Si cela n’est pas possible, écouter avec attention de manière à distinguer le son de ce que l’on récite.

(Source Rimaah ak Faakiyatul Tulaab )

Aji_bind_ji_Ibnu_Àbbaas_À_Tijaani.

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Retour en haut
Ouvrir la discussion
Bonjour,
Pouvons-nous vous aider ?